06/08/2026
18 – Sëriñ bi YALLA nanu
Sëriñ bi YALLA nanu ko neex
faww te lepp luñu neex
loolale YALLA nay luko neex
te saf ko lolu yit jubu ko
Ñun ñëpp YALLA nañu ko saf sàpp
te saxx ci luko saff
te amm ŋiy saxx ci luñu saff
te saff ñu saff gu rañéeku
YALLA nanu def mbéggum xolam
faww te sax ci ndigalam
teyy sant nak cipp doggalam
te gëm ko wόolu ko jà ko
Lukoy bégal nañuy bégal
luñiy bégal nakoy bégal
YALLA nay dogal luñiy bégal
faww aka may luñiy dόgu (bamtu)
Nayy bégg ci nun ñuyy bégg ci moom
muyy né ci nunn ñuyy né ci moom
mu sax ci nun ñu sax ci moom
jëf juñu jëff mu sant ko
Sunu diggak moom yit na leer faww
te digg ak moom nun yit na leer faww
ci wi weer ak ci weer
wu nekk YALLA mën na ko
Na sunu diggante rafet
te bumu amm senn as tawat
bumu amm yit senn ass lëggét
yaatu ci yaw jaglé nu ko
Sàlu ngërëm sarax nu ko
santum ngërëm tofal nu ko
te dëgg fopp ko may nu ko
réewum ngënéel yit fall nu ko
https://t.me/wolofalserignembayediakahte/77?single