KEUR BOROM SHAAM l'officiel

KEUR BOROM SHAAM l'officiel LI MAT A XAM CI MAGI-MAG

01/03/2024
17/02/2024

Sëriñ Seex Asta Waalo Mbàkke, mi ngi gane àdduna ci atum 1886 ci Mbàkke Bawal.

Way-juram wu góor mooy Sëriñ Maam Moor Jaara Boroom Saam ibn Maam Moor Anta Sali ibn Maam Bàlla Aysa ibn Maam Maharam.

Way-juram wu jigéen Soxna Asta Waalo Buso di doomi Sëñ Mbusóobe ibn Ma-Buso ibn Matabara ibn Hàmmaat ibn Àlliyu.....

Am Njàngam.
Mi ngi tàmbalee am njàngam ci maamam sëriñ Mbusóobe yeggale ci way-juram sëriñ Maam Moor Jaara, bokkoon ci ñi gën a mokkal Alxuraan xereñe ko lool man a bind lool loolu a taxoon sëriñ bi boole ko ci ñi ko daan bindal Alxuraan. Waaye mu fonkoon Alxuraan lool ci di ko jàng fu mu tollu. Géeju woon lool ci xam-xamu diine ak làkku araab ak ci fànni xam-xam yu bari.

Digganteem ak Sëriñ bi.
Sëriñ bi way-juram la waaye dafa jaay njureel gi jaayante ak Sëriñ bi ci doon ab taalibe bu dëggal boole liggéey ak joxe àddiya.
Mi ngi jaayante ak Sëriñ bi ca Cëyéen Jolof ci ndigalul way-juram jébbal ko it Kaamil bu mu bind ci loxoom. Sëriñ bi tarbiya ko boole ko ci ñi koy liggéeyal ci Alxuraan, lolu nak mingi gëna fese ginnaaw bi Sëriñ bi ñëwee Njaaréem. Waaye nak mu jox ndigël mu dellu ca waajuram boroom saam diko taxawu nekkal kofa,

Bi way-juram sance Mesere dafko woo digal ko mu toog fa Ni nga xam ne noonu la ko defe woon ci ay doomam yu mag sanci ay dëkk yóbb leen fa.
Ci la dem Mesere nekk fa boole liggéey ak jaamu Yàlla ak di yare di dundal dëkk ba ci yokk ak di taxawu dëkkandoo yi. Bu nawat bi wàccee mu boole mbay ma ak ub Kaamil bu mu bind jébbal ko sëriñ bi ca Njaaréem. Bu nooree mu féete Njaaréem ca Sëriñ bi di ko bindal Alxuraan, bòkkon na ci ñam fa nekka-ndooloon di bind ak ñoom S Moodou Maamun taawu Maam Seex Anta boroom Gaawaan.

Ci atum (1934) la wuutu way-juram wu tedd wa ginnaaw bi magam Sëriñ Moor Soxna wàcce ab liggéey di ki njëkk a wuutu Boroom Saam.
Ci la ñëw Mbàkke Bawal tàmbali liggéey bi ci nos xilaafa gi gàddu njaboot gi, yeesalaat barabu sëñ Moor Jaara bi yaatal ko defaraat ko ba mu yelloo ak moom.

Digganteem ak nit ñi diggante yu rafet la woon ci biir Murit gi ak ñi doonul Murit ndax jikkoom yu rafet ak man a jëflante.
Noonu it la meloon ak ci ñi mu bokkal Boroom Saam ñi ko mag ku ci mel ni Sëriñ Moor Soxna ak ñi mu mag ku ci mel ni Sëriñ Maam Bàlla noonu it la meloon ak njabootug Sëriñ bi ku ci mel ni Seex Móodu Mustafaa ak Sëñ Fàllu ak sëñ Abdu Xaadir.
Noonu it la meloon ak i baay-tëxam Maam Cerno ak Maam Seex Anta ak nijaayam Seriñ Mbàkke Buso.
Noonu it la meloon ak bokk yépp ak magi Murit yépp.

Ci atum 1939 la dogalub sunu Boroom yegsi ci moom mu wàcci ab liggéey ñu denc ko ci wetu way-juram ci Mbàkke Bawal Mbusóobe yal na leen Yàlla dolli njéggal ak yërmande ak ngërëm.

Ag njabootam
Sëriñ Mbàkke Faajama, Sëriñ Gede Mbàkke, Sëriñ Saam Astu Lóo, Sëriñ Amdi Mbàkke Gaawaan, sëriñ Cerno ak sëriñ mahmadan (ñom ñaar gudduñ fan)

Njaboot gu jigéen gi
Soxna Faatima Mbàkke, Soxna Aminta Mbàkke,Soxna Xadiija Mbàkke(Astu Busso), Soxna Sawdatu Mbàkke, Soxna Xadiija (bayti), Mbàkke, Soxna Faati Cerno Mbàkke, Soxna Asta Waalo Mbàkke, Soxna Daba Mbàkke yal na fi yàgg lool te wér.

Di ñaanal fan wu gudd ak wér Sëriñ Mbàkke ibn sëriñ Gede Mbàkke ibn sëriñ Seex Asta Waalo mi tooge ab jataayam di ab xalifaam ak mbooleem njaboot gépp.

MAGAL KAZOU RAJAB
07/02/2024

MAGAL KAZOU RAJAB

Sëriñ Saalihu minu mujjee gis ci leere ku tedd ki 2007, S… Abdu Xafóor minu mujjee gis ci leere boroom Saam (Sëriñ Maam ...
28/12/2023

Sëriñ Saalihu minu mujjee gis ci leere ku tedd ki 2007, S… Abdu Xafóor minu mujjee gis ci leere boroom Saam (Sëriñ Maam Moor Jaara) 2008 , ñoom ñéppu 28 desambar

03/12/2023
02/12/2023
01/12/2023
01/12/2023
29/11/2023
28/11/2023
27/11/2023

Adresse

Touba

Téléphone

+221773462627

Site Web

Notifications

Soyez le premier à savoir et laissez-nous vous envoyer un courriel lorsque KEUR BOROM SHAAM l'officiel publie des nouvelles et des promotions. Votre adresse e-mail ne sera pas utilisée à d'autres fins, et vous pouvez vous désabonner à tout moment.

Contacter L'école

Envoyer un message à KEUR BOROM SHAAM l'officiel:

Raccourcis

Partager