30/09/2014
Ganaw nuyo ak ziar, dano fass yéné dilén dékteul yén si ndiarignou Khassida yi.
kon niou tambalé ko thi lane moy khassida?
Khassida mou ngi diougué si baatou 'khassada' biy firi 'dioublouna'
Khassida nak moy li geuneu mana mayé ngeureumoul sunu borom ak agg thi mome, ak xol bou séll, ak fadiouk aadio ak mbir mou sakh aduna ak al-lakhira, ak djitou sak mass si zayir ak si baatine ak kham lou bari lou oumpou nitti késsé, rawatina lou mélni gis Yonénti bi(PSL) ak Serigne Touba akit yor thi mbiri baatine yo khamni khayna djamou yalla danako mayé wayé lay takh sunu borom nangul lako si diir bou gate khassida réka ko meun, ndakh Serigne Touba mo wakhni: 'wassilou ahlaami alla'lahi haabidane bilah halwatine wal'lahou abouha k**a ahna' dafa wakhni: samay khassida day agalé dieum si sunu borom thi lou diaroul di dougue khalwa ak wéétt aka sone aka khalate, délou wakhat ni samay khassida kawéna Serignou Tarbiya ak Tarkhiya
kon nanu khamni khassida yi lounouko diap dou doy lounouko fonk itam dou doy ndakh sila sunu défarouk aduna ak alaakhira nék