12/04/2026
Way wii Sëriñ Abdul Ahad (r.a) neena: « Damaa ñëw ci Sëriñ Mbay jaxate (r.a) ne ko: damaa bëgg nga dénk ma ! », Sëriñ Mbay jaxate ne ma: «danaa la dénk te duma la tagg ! »👇🏿
► Abdul Ahad yàl na saw fan gudd Mbàkke nga wér
| Te sax ci jamm’aku yiw ak jaamu Yàlla gu wér !
► Farlul te wéy yal na ngay for dog bu sedd sa xol |
Te mucc ciw ay’akum ndog sax ci def la la war !
► Toppal sa mag Mustafaa bul génn yaw ndigalam |
Ngir mag mu mat mag la mat ñéppub sëriñ te du wor !
► Jëfal te bul faale nit, bul geesu nit ci sa jëf |
Na Yàlla tax ngay jëf ak Yonen ba ak ka la jur !
► Kalay manal dara moo jar def lëf ak bàyyi lëf |
Te kooka nag moo di « Rabbul Archi » yal na la yor !
► Yar bii nga yor yor ko biir ak bitti moo di sa kee |
Moo gën ci yaw nit ñu baax ak kër yu baaxaki jur
► Sa baay a gën ñépp teb yar dong-dong la yor |
Yoral yaram ba te koo gis deeko sant ak a yar !
► Sa baay a gën ñépp ab yar ngir dalay jox a jox ab yar |
Ba ngay am a am ab yar te doo mos i yar !
► Du yëkkatib yar di teg nit waaye moo gënu nit |
Ñay teg nitub yar akay janneek a yeew ak a lor !
► Nijaayi ndam yii nga am loo jis ñu am ko ci ndam
| Xamal ni moo ko ca def jii wax ku nekk la bir !
► Nijaayi ndam yii nga am loo jis ñu am ko ci ndam |
Xamal ni moo ko waral ak cant war na gu tar !
► Ag cant war na ci yaw ak ñoom gu rëy gu rafet |
Gu tol ne bàjjo gu dul yam fenn mukkati far !
► Loo jis ci Amsatu moo mii cib yar ak jëfu yiw
| Xamal ni moo ko ca def gii wax ku nekk la bir !
► Abdooki Amsatu ak Mbakkeeki Bàlla Asan |
Yaw say nijaay a ngii ñoo diy sàll kenn du ciw par !
► Fëxal te raw am nga ab yóbbal fëx ak raw a des |
Ngir baaxi bokk a di ab yóbbal na yitte ji sar !
► Saral te wéy dëgg bul yam ciy nijaayaki |
Baay ak nday di sant ak a doyloo seeni cër lu ko jar ?
► Foo seeru kuy fok a doyloo ab cëram na nga wut |
Loo dolli yaw ci sa cër bii ndax nga am cëri-cër !
► Jollil ca kaw bul fexee jëm suuf’akay wax a dal
| Cig jolli ngay waare ab xiibon ca ngay note mbër !
► Reggàyu jàmbur ku koy doyloo ba lekkul a xam !
| Buurub Aras ba far ak bër yépp yal na la far !
► Yaw yal na ngay wéy’akay jëm kaw di dolliku ndam |
Ba jiitu waa kaw te nangoo suufe kuy