14/02/2024
Fàttali ku.
Ñatti fani Baraxlu 1364 (( هجرية ))
Ñatti fani Baraxlu 1445 ( هجرية ))
Bis niki tay la Seex Muhammadu Mustafaa Mbàkke Al Kariim, dëkaale woon ak Boroomam , Yàlla na Yàlla dolli ci moom yërmaande aki xéewal, barkeb Boroom Tuubaa.
———————————————————
Daana wax naan “ Ku ma xool ci Sëriñ Tuubaa de, duma la mat ab sëriñ, waaye ku ma xool ci sa bopp kune ma mat la ab sëriñ... “
Liy wone ni matoon na Murid yi ab Sëriñ mooy, ba mu wuutoo Boroom Tuubaa 1927, taxawu na ko ci ndénkkaan la mu leen bàyyee woon, muy: ñibbi Tuubaa, taxawu yoon wi, dongo yi, njaboot gi, juumaa ji ak dëkkub Sëriñ Tuubaa bii ko gënal fépp.
Mu def ci xilaafa gi 18 at yoo xamne, lépp ci ay jafe-jafe aki coono ak ñàkk a nelaw, ci la ko defee, ba loolu bokkoon na ci sabab yi ko yobbu Àjjana.
Kon la nu ca wara jàngee mooy, ab Murid Saadix daa war a jaay bakkanam ci ligeeyal BOROOM TUUBAA.
Bis ni tay di 3 fani baraxlu la wuyu ji woon Boroomam ca Tuubaa, keroog ba muy dem, dajale na ak njabootam jox leen ndénkaan lu am solo, bokk na ca la mu leen wax :
«...Seex (Sëriñ Seex Fàtma), na nga jiitu, Sëriñ (Sëñ Mbàkke Màddina) topp ci, bu ëllagee ku ca wara topp, Yàllaa toftal ko ca.
Na ngeen bëggante, di seeteente, tey dimbalante, te bu leen ñeehante, ndax wërsëgu àdduna jarul ñeehante, te ñeehante fu mu yàgg rek añaan dugg fa, te àñaan mooy indi noonoo ak xëccoo ak tàqalikoo, te su ngeen tàqalikoo di ngeen néew doole. Te nii ma leen dajalee nii, bëggu ma ngeen tas ko mukk ! وَلا تَنَازَعُوا فَتَفْشَلُوا وَتَذْهَبَ رِيحُكُمْ وَاصْبِرُوا إِنَّ اللَّهَ مَعَ الصَّابِرِينَ
Mbalaanum Sëñ Bàmba mii nag, rëy na, yaatu na, tal na, ku ci génn ku ne, sa jikkoo la ci génné !
Te ngeen xamne, àdduna jii ken du fi sax, ku fi nekk nag def lala war ba juge fi, wàcc nga !
Man de Sëñ Bamba gërëm nama, te lum ma sant def naa ko, ligeeyal naa ko it loo xamne, yeen ñépp xaj ngeen ci ! Luy Yàlla digle, def naa ci la ma man, te masu maa def lu mu tere, kon nag rafet naa njort fa ma jëm !
Kon nag, yoon waa ngoog, te teg naa leen ci, su ngeen ci awee te wàccu leen ko, lu ngeen bëgg di ngéen ko am, àdduna ak àllaaxira...»
Seex Moustafa Al Kariim ❣️