Euhlou Xassida Xidmatul Xadim

Euhlou Xassida Xidmatul Xadim Au service de CHEIKH AHMADOU BAMBA KHADIM RASSOUL LIGGEEYAL BOROOM TUUBAA CI XASSIDA YI

Cheikh Seydil Hadji Malick Sy yalna niou ko YALLA fayal 🤲🏿  Euhlou Xassida Xidmatul Xadim
23/08/2026

Cheikh Seydil Hadji Malick Sy yalna niou ko YALLA fayal 🤲🏿

Euhlou Xassida Xidmatul Xadim

23/08/2026
Sëriñ Tuubaa ak yonent bi ﷺ Sëriñ Tuubaa neena :Boo doon nattalè Yonent bi ﷺ ak yeneen gars yu baax yi :Xoolal weer wi a...
20/08/2026

Sëriñ Tuubaa ak yonent bi ﷺ
Sëriñ Tuubaa neena :

Boo doon nattalè Yonent bi ﷺ ak yeneen gars yu baax yi :
Xoolal weer wi amna ag leer gu màgg , Waayè saa bu jànt bi feeñee nga fàtté leeraayu weer wi ngir ni jànt bi dakoo gëna leer .
Neena Yonent ﷺ mooy jànt ba ñi ci des di ay weer .

Source: Raa hiyah .

Ngëneel yi nekk ci màggal guddig gàmmu_• Ku màggal guddi gi ci Sunna‎تعظيمه بالسّنة  يقودنا للجنّة‎به ازدياد المنّة  لمخ...
20/08/2026

Ngëneel yi nekk ci màggal guddig gàmmu_

• Ku màggal guddi gi ci Sunna

‎تعظيمه بالسّنة يقودنا للجنّة
‎به ازدياد المنّة لمخلص معظّم
"Di màggal guddi googu te dëppale ko ak sunna bañ caa def lenn lu Yàlla aaye dinanu wommat jëme nu guyaar _"aljana"_ te dana tax nu am xéewal ‎yu dolliku bu dee sellal nanu ko.

‎فمن يعظّم مولدا نبيّنا باب الهدى
‎فلا يحاسب غدا عند الحساب المفحم

"Képp ku màggal guddig Yónnent bi SHW moom mi nga xam ne mooy buntub jub, kooku ëllëg deesu ko hisaab ca bis ba nga xam ne sunu Boroom dana wedamloo ñépp ci lijjanti seen bir."

‎‏فمن يعظّم مولدا خير البرايا أحمدا
‎‏فكشهيد شهدا بدرا بغير وهم
‎‏
Képp ku màggal guddig ngën ji mbindeef, dana ci ame tiyaaba yu bari ba mel ne ku fekke woon badar Yàlla jël ca bakkanam ci lu dul genn defe ‏Ku ci def sa alal •

‏فكلّ من أنفق في مولده المشرّف
‏مالاً بغير سرف و لو بقدر درهم
‏فإنّه كمن حضر يوم حنين و صبر
‏و يوم بدر و نصر خير الورى مفهّم

‏Képp koo xam ne def na alalam ci guddig gàmmu te bañ caa def lenn luy niru ag yàq, alal jooja donte daa tuuti ba tollu ni ab dërëm kooka dana ci ame tiyaaba joo xam ne dana mel ni ku teewe xare Badar ak xareb Hunayni doon muñ tey dimbali Yónnent bi SHW tiyaaba ju tol noonu la ciy jële. ‏Ku ci bégal nit ci bernde •

‏فكل من قد حضرا مولد أفضل الورى
‏معظما مبشرا بسكّر أو لحم
‏فإنه قد ظفرا بما يديم البشرا
‏و لا يلاقي ضررا يوم اجتماع الأمم

‏Képp koo xam ne fekke na guddig gàmmu mu di ko màggal di ca bégal nit ñi ci lu saf suukar walla ci ag ndawal kooku sunu Boroom dana ko jox loo xam ne da koy saxalal ay mbégte fu mu toll di bég te ëllëg bis ba sunu Boroom di dajale mbooleem xeeti yi moom du fa daje ak jenn lor.

فمن طعاما هيّئا لمن له قد قرءا
‎مبجّلا فخبئا خيرات أهل الهمم

"Képp koo xam ne fekke na gàmmu mu waajal aw ñam jox ko ña nga xam ne ñooy jàng mu def ko ngir màggale ko guddi gi, kooku dina am yiw ya nga xam ne gaa ñu amoon yitte yu kawe ya _(gaa ñu baax ña)_ amoon nañu ko."

• Ku ci jàng dara ngir sàkku barke

‎و من على شيء قرا مولد سيّد الورى
‎تبرّكا فسيرا نموّه بالفدغم

"Saa soo amee loo xam ne danga caa bëgg barke nga jàng ci guddig gàmmu fas ko ca, loolee danga gis mu doon lu màgg ba yaatu lool ci barkeb Yónnent bi SHW."

‎‏Ku ci jàng dara (Alxuraan, Xasiida, Salaatu…) ci am ndox su noppee naan ko

‎‏و إن على ماء قري/ مولد خير البشر
‎‏فالشّرب بالمطهّر/ يكفّ كيد المرغم
‎‏ينوّر القلب الشّراب/ من ذالك الما بالمجاب
‎‏و القلب يحيي دون/ عاب و عن شقاء يحتم

‎‏Koo xam ne ci guddig gàmmu jàng na dara ci Xasiida mbaa ci Alxuraan mbaa ci julli ci Yónnent bi SHW walla ci turu Yàlla wu mu man a doon def ko ci ndox naan ndox ma, ndox moo ma dana ko fegal pexem saytaane te ndox moo ma naan ga mu ca naan dana waral ab xolam dal di leer, dana waral it ab xolam dal di dund ba mucc ci lépp luy ‎sikk te it naan googee dana ko fegal ag texeedi.

‎•Li ci dundal guddig gàmmu

‎احياء مولد البشير يحمي/ العيال و الدّيور
‎فيه شفاء لّلصّدور/ لكلّ هاد ينتم

"Dundal gàmmu day aar njaboot yi di aar kër yi, luy saafara xol yi mi ngi ci ñeel képp koo xam ne ab jullit la bu gindeeku."

_Sëriñ Tuubaa {Xasiida Jasbul Quluub}_

19/08/2026

Gamou 1997📜 BAAY SAAM 🥰

{ Son dernier Gamou en juillet 1997, malgré la maladie,le pansement à la main,le Cheikh a tenu sa dernière causerie sur le Prophète ( P.S.L), d'ailleurs une synthèse de toutes ses causeries sur l'homme de Médine .}

Source : Serigne Saam Mbaye: Parcours d'un mujahid (combattant de la foi) ou la biographie d'un mujaddid (rénovateur)📖

Auteur : Mamadou Gaye Saam ✍️

Photo 👇Gamou 1997 🙏

Adresse

Montagne
Louga

Site Web

Notifications

Soyez le premier à savoir et laissez-nous vous envoyer un courriel lorsque Euhlou Xassida Xidmatul Xadim publie des nouvelles et des promotions. Votre adresse e-mail ne sera pas utilisée à d'autres fins, et vous pouvez vous désabonner à tout moment.

Contacter L'école

Envoyer un message à Euhlou Xassida Xidmatul Xadim:

Raccourcis

Partager